28/07/2026
Da ngaa dox fa mbër yépp dox nag ta dox
Fu kenn mësla dox am nga jaajëf ju mat
Da ngaa boole waa àll ak waa kër it
Toroxloo ta jël seen i ndam, lii rafet
Demoo wacc saw nit nu bon alku far
Da ngaa dem ta fab ñépp yobbaale fat
Da ngaa mën ci kër, mën ci ab àll it
Ku xam xamne yaa ëpp yaw ñépp fit
Kër ak àll ñoo bokk nag yam fi yaw
Lu am doo ca bew doo ca jekkii xul it
Kudul yaw gëtam yaa nga jëm genn wet
Ta yaw sa bët yaa nga jëm gépp wet
Kudul yaw dafay may boroomam ba bët
Bu wér mbaa mu may far njabootam ga bët
Nga may Yàlla yaw bët ta may ñépp bët
Sa wet genn taqul, sa wet yépp a set
Kudul yaw bu gee wet seetee gee tilim
Bu gee wet jotee sëkk yit gee du jot
Se wet yépp a set sa wet yépp a jot
Bégal baarakallaahu sab kem amut
Maximum de J'aime Page Officielle SMX